Youssou N’Dour
Gagganti ko
Ba ñu la koy jox, xam ul dara;
Bu la séen ée, daw gatandu la
Ay waajur ëm, da ñoo am oon yaakaar ci yaw
Jamono y dox, jafejafe am, sëytaane ñëw
Bu ko dóor, bu ko saaga, bu ko xas, bu ko wax lu ñaaw
Delloo l sa xel, ca ginnaaw, te muñ ël ko;
Ba ñu la koy may, xam ul dara;;
Bu la séen ée, daw laxasu la
Ay waajur ëm, da ñoo am oon yaakaar ci yaw
Jamono dox, jafejafe am, sëytaane ñëw
Bu ko dóor, bu ko saaga, bu ko xas, bu ko wax lu ñaaw
Delloo l sa xel, ca ginnaaw, bu ko souffrir loo;
Xool al ci ay, waajur ëm, bu ko joy loo
Bu juum ee gagganti ko
Bu juum ee gagganti ko
Bu juum ee gagganti ko
Bu juum ee gagganti ko
Bu ko dòor, bu ko saaga, bu ko xas
Bu ko wakh lu ñaaw
Bu yënggël ée daal, ba sa xol fees, génn ël nga dem
Bu fa toog yaw, di raak ak moom, sàmm al sa cér
Woo ko, waxtaan ak moom, té muñël ko
Bu juum ee gagganti ko
Bu juum ee gagganti ko
Bu juum ee gagganti ko
Bu juum ee gagganti ko
Yaw tam, bul forcer, deel négocier
Ndaw sii, bul teg deal, bul planifier
Te bu am ee, lu fi leer ul, nga clarifier
Coow li, bu déborder, nga pacifier
Yaw daal, bul forcer, deel négocier
Ndaw sii, bul teg deal, bul planifier
Te bu am ee, lu fi leer ul, nga clarifier
Coow li, bu déborder, nga pacifier
Wa waaw
Jaajëf, di na tax, xale wone jom
Waaw góor, di na tax, xale yokk jom
Di ko won sa jom, moo koy dolli jom
Jom jom jom rek, dara lu dul jom
Yërëmal ma ko
Momit mou wégal ma laa
Nax ko neex al ma ko
Moomit mu xam ko